Ñetti biisi Dakar Dem Dikk yu tàkk ca Petersen, AUCHAN Mermoos tàkk jëppeet, ay bérébi liggéey yu tëj, dem yombatul, dikk amatul ci péeyub réew mi. Ndaw ñeek takk-der yaa ngiy xeex xeex bu metti jamono jii. Source: Paap Aali Jàllo pour defuwaxu
Li xamb taal bi mooy li waa BIP toj oto Usmaan Sonko, jaay ko doole, génne ko, jàpp ko. Njiitul Pastef li dafa waroon a wuyuji Yoon ñeel layoom beek Maam Mbay Ñaŋ. Jamono jii nag, xale yaa ngi génn fu nekk ci Ndakaaru di taal i póno ak a sàndiy xeer. Am nay xibaar yuy wax ni sax waa Mbuur ak waa Sigicoor sóobu nañ ci cóoki bi.
Nee ñu, am na ci sàndarm bu ci ame gaañu-gaañu. Fi mu nekk nii, ndaw ñi fatt nañ yoon wi jëm « Palais de justice ».
Ca Medinaa, am nay “nervis” APR yu yor ay jaasi di xeex ak askan wa. Tele Walfadjiri moo fésal xibaar bi.
Laisser un commentaire