FÀTTALIKU OMAR BOLONDEŊ JÓOB… (Foloryaŋ Bobeŋ ci tekkig Daawuda Géy)

Ci àjjuma tey jii, 17i fan weeru sàttumbar 2021 la Omar Bolondeŋ Jóob am kon 75i at. Ngir sargal jàmbaar jooju bëggoon réewam ba mu jaral ko bakkanam, Lu defu waxu tekkilu na ci kàllaamay Kocc ab yaxal bu am solo bu ko Foloryaŋ Bobeŋ jagleeloon ciy jamono, tudde ko “Dellusiwaat ci jaar-jaaru Bolondeŋ Jóob ci jamono ju ñuy wut a jàllarbi li fi nekkoon ci Senegaal”. Ci àngale lan jëkk a bind bile yaxal, siiwaloon ko ci “Review of African Political Economy”. Daawuda Géy mi nu ko tekkil nag, bañkat la moom tamit. Ngërëm ñeel na ko…Source: defuwaxu.com

Fukkeelu fan ci weeru Mee atum 1973, la kilifay Senegaal yi yëgle faatug Omar Bolondeŋ Jóob, mu doonoon ndaw, doonoon ab bañkat ak ab ma-pasin*, amoon 26i at, ñu téye woon ko ca kaso ba ca Gore. Daanaka am na xaaju xarnu boobu ba tay. Li Nguur gi wax ne dafa xaru, ñu bari weddi nañ ko, jàpp ne ñoom ci seen bopp ñoo ko bóom.

Ci atum 2013, mbokki Omar Bolondeŋ Jóob dañu ko doon màggal, 40i at ginnaaw bi mu faatoo ca Gore. Ci diirub ay xarnu, dun bi Tubaab yi daan yóbbu lim bu kenn mënul a takk ci ay saa-Afrig ca Amerig def leen fa ay jaam. Ci biir googu màggal, mbokki Omar yi génne woon ab nataalam ca biir kasoom ba woon, te doon léegi ab bulub aajarukaayu, barab bu mboore bi gën a mag ci Senegaal. Ñu ngi jël boobu nataal ci atum 1970. Booba Omar njàngaan la woon ngir doon ab jàngalekatu xeltu, ñu ko doon doog a dàqe Farãs mu delsi Senegaal. Mu bokkoon, niki yeneen moroomam yu bari ca jooja jamono, ci yëngu-yëngu yi amoon ci “Mee 68”. Ñu teg ci ay at, ñu bóom jàllarbikat bi ci biir toolu-xare.

Bi mu génnee àdduna ci kaso ba mu nekkoon, ginnaaw bi ñu ko àtte mu war a tëdd ñatti ati kaso ndax dafa “laal kaaraangeg réew mi “, kilifay Senegaal wax ne dafa xaru. Waaye ñu bari jàppoon ne dañu koo bóom. Booba ba tay ay mbokkam tàyyiwuñu di sàkku yoon def liggéeyam ci mbir mi, teg ci ay bañkat ak ay ma-pasin jël xeex bi ngir kenn bañ koo fàtte.

Faatug Omar Bolondeŋ doonul xew-xew bu am nii rekk ci sunu mboor, bu kenn xamul lu ko jur. Déedéet, benn la rekk ci ay xeeti metital yu nguurug Senegaal yàgg a def. Tàmmuñoo gis ñuy wax lu bari ci kuréel yi taxawoon di jàmmaarloo ak nguurug Seŋoor, walla sax di leen jox seen gëdd ndax ki fi jëkk a doon njiitu réew (atum 1960 ba 1981) fexe woon na ba ñépp jàpp ne réew mi royukaay la ci demokaraasi. Nettali yi ñu saxal ci génnug réewi Afrig yi ci nooteel dañuy tënk yoonu tinkiku gi ci nooteelug tugal ci juddug Càmm yuy soog a moom seen bopp. Te doxandéem yu wéy di dugal seen loxo ci réew yooyu ngir seen njariñu bopp, te njiiti réew yooyu jàppale leen ci, loolu lu ñépp tegoon seen bët la ci atiy 1960 yi.

Ginnaaw bi ñu moomee seen bopp ci waxin rekk, jaaykati doole yi ci ndimbalul réew yi ñu nootoon, dañoo sasoo dëgëral seen nguur, jaare ko ci faagaagal lépp lu jóg di woote ag tinkiku ci nooteel ak ci nosteg koppartu. Gaa, Senegaal dundul ay jafe-jafe ci wàllu politig ni mu amee ci réew yi ko wër, waaye fi ñu àggale woon mbaaxug kii boole woon di taalifkat di njiitu réew muy Lewopol Sedaar Seŋoor muuroon na sunuy gët ci ay doxalinam ci politig. Ci jamonoy “Union Progressiste Sénégalaise” (UPS), doonoon benn kuréelu politigu cundum mu jiite ko, kilifa yi daan nañu noot, di xorñoññal di teg loxo, di tëj, di metital ba di ray bañkat yi. Omar Bolondeŋ Jóob bokkoon ca ñooña. La Suite ICI: defuwaxu.com/2022/05/11/fattaliku-omar

Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *