Sénégal amati na ndam !

Gàcca-ngaalaama sunu xëllóob yi (gaynde yu ndaw yi) ! Taaw daal, ndeke bu xàllee, rakk ya am jomu daagu ni buuru tan. Source:Maam Usmaan Si Gómis pour defuwaxu

Ba gaal gu mag ga rëbbijee ba andi kuppeg Afrig ba léegi xale yi ñëwatuñook i loxooy neen ! Senegaal àddooti n’a, te Afrig gépp dégg na baatam.

Niki mu ko yëgee woon, keroog ba gayndey Aliin Siise ya jëlee Kuppeg Afrig ga, yu Paap Caw yi feelu leen ca, noonu lan yëgaatee bànneex ci sunu xol yi tay bi gaynde Maalik Daaf yi jëlatee kuppeg Afrig gii ñeel ñi amagul 20i at.

Ca njëlbéen la xale yi tàmbali wane jom ba ni mu jeexee, loolu di lu réy ci mbooru kuppegu Senegaal.
Tay, ci gaawu gi, la Senegaal doon jàmmaarlook naataangoom bii di Gàmbi ñeel finaalu kuppeg Afrigu ñi matalul 20i at. Senegaal jël raw-gàddu gi ci kaw kii di Gàmbi, dóor ko ñaari bal ci dara.

Joŋante gi nag, laata mu doon tàmbali ci pàkk mi, dafa mel ne ca mbaali-jokkoo yi la njëkkee. Li ko dalee démb la tooñante geek nappante gi dooroon. La Suite ICI: defuwaxu.com/senegaal

 

Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *