NDAJEM ÑAXTU YEWWI ASKAN WI : WEDDI, GIS BOKKU

Àllarba jii weesu, « Place de la Nation » dafa ñuuloon kukk ak i nit. Foo sàndi woon mbàttu mu tàkk ndax mbooloo mu bari. Nde, askan wee wuyusi wooteb lёkkatoob kujje gii di Yewwi Askan Wi. Fu nekk la nit ñi bawoo ci réew mi ngir teewesi ndajem ñaxtu moomu, biral seenuw naqar ci lees jàppe jaay-doole ak jalgati yoon ñeel wotey ndawi réew mees dёgmal ci sulet. Lu waral ndaje mi ? Laaj bii lees ci jéem a tontu. Sow Mbay pour le journal defuwaxu

Coowal wotey palum depite yi lёmbe na réewum Senegaal lool ci jamono jii nu tollu. Coow li nag, bari na te ci ñaari boor yépp lay jóge. Muy ñi fare ci Nguur gi walla ñi fare ci kujje gi. Ku nekk ci ñoom a ngi xool nooy def ba sa moroom du bokk ci joŋante yii nu dёgmal. Waaye nag, coow li, li muy bari bari, ñaar a ko séq, muy nguur gi (waa Bennoo Bokk Yaakaar) ak lёkkatoo gii di Yewwi Askan Wi, gàttal biy joxe YAW. Li mat a laaj kay mooy fu coow li doore ak nan la deme? Seen yéenekaay bii di defuwaxu dina leen ci indil ay leeral laata nu ciy def ab taxaw seetlu.

Coow laa ngi door bi lёkkatoo gii di YAW di jébbal ay wayndareem ca màkkaanub caytug wote yi (DGE). Nee ñu, lu jiin Njaag a, te ngóor sii di Saliw Saar mooy Njaag. Nde, waxees na ne, moom, moo fa jébbal ay wayndare yu baaxul. Ci kow loolu, Bartelemi Jaas mii di fara bu Ndakaaru génnoon na, biral ni loolu wérul. Ndax, kooku amul benn ndogal ngir mёn faa jébbal genn kёyit gum mёn di doon. Te it, kii di Decce Faal moom lañ dénk wàll woowu ci biir YAW. Ba loolu weesoo bañ jébbal seen i wayndare, ñoom waa YAW ak waa BBY, ñu gis ni dafa am ay njuumte ci seen i wayndare. Ndax, dañoo jàpp ne wayndare bu YAW ca Ndakaaru sàmmoontewul ak dog 149 ci liñ yoonal ci wàllum wote. Maanaan yemoo góor ak jigéen (parité) ci wayndare yi. Waaye ñoom bi ñu sukkandikoo ci li leen yoon may (dog 179), jàpp nañ ne war nañoo mёn a joyyanti njuumte li bala muy am ñetti fan. Maanaam laata ñu ciy amal ag caytu. Ci seen wayndare réew mi yépp nag moom, njuumte li mooy ñàkk a gёddaal dog 158. Maanaam dañoo dugal ci seen wayndare ku matalul ñaar-fukki at ak juróom (25). Waaye, ba tey terewul ne mёn nañ ko soppi. Ci coppite giñ doon def ci la ñenn ñi jàpp ne dafa am ay njuumte ngir ne dañoo wuutale koo xam ne dafa nekk ci ñaari wayndare yépp (muy titulaire ak suppléant). Biñ sukkandikoo ci dog 173 loolu mёnul nekk. Waaye ñoom, liñ jàpp mooy ne wayndare gi genn la amul xàjj-ak-seen. Moo tax ñenn ci seen i militaŋ njort ni gaa ñi dañoo bёgg a lёbёje kàrt gi ca teel. La Suite ICI: defuwaxu.com//taxaw-seetlu-neel-wotey

©Nitdoff/Page Facebook

Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *