Walfadjiri-Nguurug Maki Sàll: Gatsa-Gatsa

Kamaj ! Benn yoon. Kamaj ! Ñaari yoon ! kamaj ! Ñetti yoon. Siñaalu tele Walfadjiri dogati na. Bii yoon, diirub weer la tele biy fay. Li ko dale 1 fan ci suwe jàpp 1 fan ci sulet 2023. Ku ko dog ? Jëwriñu jokkoo gi. Lu tax ? Dañu wone ay yëngu-yëngal yi xewoon ci réew mi. Nii la mbir mi deme. Source: defuwaxu.com

Bi Senegaal di Senegaal ba tey, guléet ñuy dog siñaalu tele ci àppug weer. Mësu fee am. Du ci nguuru Seŋoor. Du ci Jamonoy Abdu Juuf. Ablaay Wàdd itam, defu ko. Kon, gàcce-ngaalaama Maki Sàll. Moo fi def lu kenn deful. Ñu taxaw tuuti ci ndogal li, xool ba xam dëppoo na ak sàrt yi tënk wàlluw tas xibaar am déet.

Keroog, alxames 1 fan ci weeru suwe, la àttekat bi biral daan yim gàll Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay ñeel mbirum ciif ak tëkkuy rey yi Aji Raabi Saar doon jiiñ Usmaan Sonko. Ci waxi ndaw si, mbir maa nga xewe ca dàmpuwaayu Sweet Beauté, di moomeelu Ndey Xadi Njaay. Bés boobu, ak ñetti fan yi ci topp yépp, réew mi dafa tàngoon jérr, rawatina Ndakaaru ak Sigicoor. Xeex bi ne kurr diggante farandooy Usmaan Sonko yi ak takk-der yoy, ay saay-saay dañ leen raxoon. Lu tollu ci 16i bakkan rot ci, ci li Nguur xibaar. Am ñu ne 30i bakkan ak lu teg ñoo ci rot. Fan yooyu, àddina sépp, Senegaal lees doon waxtaane. Teley réew mi di amal i jotaay yoy, jagleesoon na leen yëngu-yëngal yi. Walfadjiri nag, jamono ja muy amal jotaayu Keppaar gi la siñaalam dog. Waa tele bi sax yëguñu ko woon. Ña doon seetaan a leen ko xamal. Ca la kilifa ga, Seex Ñas, jokkee Baabakar Jaañ mi yilif CNRA, laaj ko ndax moo dog siñaal bi, mu ne ko déedéet. Ayle-yéwén, bu doob moom, dina leen ko yégal ca njëlbeen. Ca lañu jàppee ne dañu ame paan. Ñi féete ci xarala gi seet, seet, ndekete dañu dog dëggantaan seen siñaal.

Waa Canal+ la Seex Ñas mujje woon, ñu xamal ko ni dañu jot ndigalu dog siñaalu tele bi. Jëwriñu jokkoo gi, Musaa Bookar Caam, moo joxe ndigal li. Waaye, yégalul woon kilifay tele bi. Bataaxel biy firndeel ndogal li sax, bésub 9 suwe lañ ko jot, fekk ne, booba, liggéeykati Walfadjiri yaa nga doon amal ab toogaanu ñaxtu ca seen biir màkkaan. Bi Seex Ñas di wax lab cag-cag indi bataaxel bi. Ca biir, jëwriñ jaa nga cay layal dog bi mu doglu siñaalu tele bi. Nee na ci, « 

Jëwriñ ji, ci dogu 94 bu càrtug tas-xibaar gi la sukkandiku ngir layal dog bi mu dog siñaal bi. Waaye, nag, dog 94 boobu mu sukkandi ba tax ko dog siñaalu Walf Tv, mayu ko sañ-sañ bi. Loolu la Daawda Miin, faramfàccekatu Yoon ci tele TFM xamle. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, dog 94 bi day wax ne, moom jëwriñu jokkoo gi mooy joxe ndigal ginnaaw bi kurélug caytu gi (CNRA) biralee àndam ci ndogal li. Kon, CNRA mooy nangu wayndarew ki bëgg a am siñaal, saytu ko.

Bu jàppee ne yemb, mu sog ko jébbal jëwriñ ji ngir mu xaatim ko. Waaye, bu jëwriñ ji xaatimee ba noppi sax, wayndare wi day delluwaat ca CNRA, boroom xaatim fa lees di wax « Cahier de charges ». CNRA mooy xool ndax boroom a ngi jëfe ak a sàmmonte ak « Cahier de charges » boobu.  Bogu 94 bi mooy jox CNRA sañ-sañ boobu.  Daawda Miin neeti, dogu 210 bu càrtug tas-xibaar gi ci boppam moo wax ne CNRA moo kurél gi war a dog siñaal ci kow ay sàrt. Rax-ci-dollu, dog 210 bi day wax sax ne, balaa ngaa dog siñaalu jàmbur, danga ko war njëkk xamal ni mu ngi jéggi yoon, bu bañee dellu ginnaaw gi nga artu ko, bu bañaatee ngay sog a siñaal bi. Bu ko defee, jëwriñ ji dafa jalgati yoon. Ndax yoon mayu ko muy dog siñaal. CNRA rekk la ko yoon may. La Suite ICI

Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *