Ibraayma Aan ak Àbbaas Njoon, ñaari bindkat yu mag, ñoo génn àddina : kii ci altine jii nu weesu (22eelu sãwiyee 2024), ki ci des alxames (25eelu sãwiyee 2024). Seen ndem jur tiis wu réy ci seen njaboot, waaye tamit ci ñépp ñiy yëngu ci téereek dawal. Source: Defuwaxu
Ibraayma Aan, bànk la liggéeye ba jël noflaayam. Ba ni mu génnee àddina, bind rekk a ko soxaloon, daan na faral di wax ne moom xaritu téereek dawal la. Bàyyi na fi 6i téere. Bariwul woon wax, teeyoon na boole kook dégg làkku tubaab. Sëñ Aan moo bind L’écume du temps, Errance, Les dieux de la brousse ne sont pas invulnérables. Ibraayma Aan jot na raaya yu bari yu deme ni Prix Orange, Prix RFI ak yeneen.
Àbbaas Njoon, moom, doktoor la woon, def na loppitaal Dantec 19i at. Bind na 3i téere, bu njëkk bi ñaari pàcc la. Ku xamoon réewum Senegaal la, oyof, mën a ree. Sëñ Njoon a bind La vie en spirale, Ramata ak Mbëkë mi. Téere bu ci nekk duut na ci baaraam li doxul ci réew mi, bindkat bu làmmiñam nekkul woon ci poosam la. Ñaari téereem yu mujj yi sax def nañ leen i film. La Suite ICI
Laisser un commentaire