Séex Antà, Dumàla tàgg…

À Ibrahima Seck
et à son fils Cheikh Anta Seck !

CHEIKH ANTA DIOP !

Séex Antà
Dumàla wóy
Yàay wóy búdul dàkk bà fàw

Dumàla kañ
Yàay súnu kàñu téy àk ëllëg

Dumàla tàgg
Yàa tàgg sa bópp
Ñun ñi tàgoon di là xàar ày júnni júnni àt

Yàay jàntu xàmxàm jùy fénq júdul súux bà fàw

Yàw mi xùus ci lëndëm jëbbël ñu léer

Séex Anta
Yàw yàa firii súnuy gént yi màroon dëgg àk yàakàar

Téy ngà gënà dúnd ci wërngël si
Téy ngà gënà dúnndal jàmano ji

Téy ngà gënà fées déll xàrnu
bi
Téy là Afrik gënà fées déll àk yàw

Gàccé ngaalaamà dóomu Càytu bi

 

 

© Elhadji Ibrahima Thiam (@Ibbuthiam) | Twitter

Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *