MBËMËSTAL CI JAAR-JAARU ÀLLAAJI OMAR TAAL

Àllaaji Omar Taal mi juddu ci atum 1796 ca Fuuta, bokk na ci ñi siggil ba fàww nit ku ñuul ci lislaam. Nekkul woon rekk njiitul diine ak tariixa, wànte boroom xam-xam bu gëmoon der bu ñuul la, te fonk dénduw Afrig gépp.  Source Baay Njaay pour defuwaxu.com

Ginnaaw bi mu wedamloowee ay sëriñam, Àllaaji Omar feeñaloon na yeneen i kéemtaan ci daara ja mu nekkoon. Baayam boroom xam-xam la woon bu jànge Daaray Pir, doon daara ji gënoon a kowe ci jamono jooju. Yaayam it, Soxna Aadama Ayse, yaaram la woon bu nangoo séy te baax, fonk boroom këram ak wujjam. Abdul Karim Jàllo, ab sëriñ bu jànge Gànnaar, jële fa wirdu Tijaan, moo ko jëkk a jox wird wa. Ci lan fasante woon kóllëre ñoom ñaar.

Àllaaji Omar jaaroon na Misra, siggil fa der bu ñuul. Boroom xam-xami Misra xawoon nanu koo xeeb ngir wirgo deram, wànte bim jëflaanteek ñoom ba noppi, ñoom ñépp a luum.

Ba mu ajee Màkka la taseek Muhamadu Xaali nekk taalibeem ay weeri weer. Muhamadu Xaali natt ko ci bépp anam, def ko Xalifa ci ndigalu Seex Ahmad Tiijaani.

Àllaaji Omar Taal sumboon nay xare Senegaal ba Niseryaa ngir tuubloo ceddo yi, yaatal lislaam fépp ci Afrig sowu-jànt. Ci 1864 la ko noon yi ërtal mu dugg ci Degembeer ne fa mes.

Dees na wéy di fàttalikuy jalooreem ba fàww.

Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *