Bërki-démb ci bëccëg gi la Njiitu réew mi jël ndogalu fomm wote yi waroon a am fii ak ñetti ayi-bés. Ndogal loolu nag, lawaxi kujje gi nee nañu du ci dal. Ndax, ñoom dañoo jàpp ne firnde yi mu joxe ngir layal ajandig wote yi, teguwul fenn. Kon, ñoom dañuy wéyal liggéey bi ni ko càrti réew mi tëralee. Moo tax, bi ndogal li jibee lañu woote ndajem waxtaan ca saa sa ngir xamle li ñu namm a def. Ñu xamal seen i militaŋ ne li Maki Sàll wax du leen teree dem dagaan baatu askan wi. Ñu joxe woon dig-daje démb ci dibéer ji, bu ñetti waxtu ci bëccëg jotee fa Saint Lazar ngir door kàmpaañ yi. Waaye, ay lakkirimosen lañ leen gatandoo.
Coowal fommub wotey 2024 yi moo lëmbe réewum Senegaal jamono jii. Te, li ko waral du lenn lu moy ne, askan week kujje gi dañoo jàpp ne li Njiitu réew miy taafantoo ngir ajandi wote yi ay waxi naxasaxandaŋ kepp la. Looloo tax ñu ne, wii yoon moom ,du deme noonu. Ndax, coow li dox diggante Ndajem ndeyu àtte réew mi ak Ngomblaan gi warul mën a tax mu jël ndogal lu ni mel. Looloo waral kujje gi door, bërki-biig ci guddi, kàmpaañam. Rax-ci-dolli, ñu jox seen i ñoñ dig-daje fa Saint Lazare ngir ñu tàmbalee fa liggéey bi.
Waaye, loolu mujjeewul a àntu. Ba tax na, fim tollu nii jàmmaarloo ya door nañ ci yenn gox yi, fa Ndakaaru. Saxaar sa jëm na kow diggante takk-der ya ak askan wiy xeex ndogal lile. Sànnante xeer yi, taal yeek yàq yi nee na fa kurr. Te, mbir yi yemagul foofu. Ndax, am na yeneen dëkk yu leen tàmbalee feelu ci xeex bi. Muy fu ci mel ni Sigicoor, Cees… Mu am tamit ñenn ñoo xam ne tegoon nañu leen loxo démb : muy kii di Anta Baabakar Ngom nga xam ne moom lawax la ak Aminata Ture mi ngi xam ne Basiiru Jomaay Fay lay jàppale. Waaye, mujj nañ leen bàyyi.La Suite : :https://www.defuwaxu.com/maki-sall-xuus-jall-walla-rasu-genn/
Share
Related Articles
Bons Mots du Sahel 7 septembre 20240
Décès de Thierno Ka, éminent professeur d’islamologie et directeur de l’Institut Islamique de Dakar
L’islam perd un éminent savant avec la disparition jeudi dernier (5 septembre 2024)…
Bons Mots du Sahel 8 juillet 20240
« J’ai perdu ma voix au bout de ta plume »…Momar Coumba Diop
Les sciences humaines et sociales perdent un immense chercheur. Le sociologue Momar Coumba Diop…
Bons Mots du Sahel 5 juillet 20240
1er sommet de l’AES : confédération en vue…
Les pays de l’Alliance des États du Sahel (AES), Mali, Burkina Faso, Niger se…
Laisser un commentaire