Kaïs Saïed : weex der taxul a weex lol

Ndekete yoo, nit, nit ay posonam. Kàdduy boddekonte yi Njiitu réewum Tinisi li biral, keroog talaata, ñoo firndeel wax ji. Moom,  Kaïs Saïed, dafa tamm ñuule yi dëmm, jiiñ leen xeeti ñaawteef, caay-caay ak mbonte ya am ca réewam ma. Yemu ca. Ndax, dëkk na leen xare, daldi digal Nguuram gi mu jël i matukaay ni mu gën a gaawe ngir, ciy waxam, fànq loraange yi leen doomi Afrig yiy indil. Boobaak léegi, nag, coow laa ngi ne kurr ci àddina si. Nit ñaa ngay ñaawlook a naqarlu kàddoom yu suufe yooyu. Paap Aali Jàllo pour Defu Waxu

Fan yii, daanaka kibaraan yépp a ngi wax ak a bind ca la xew Tinisii. Kàddu yaa ngi jóg, yégle yiy bare. Muy kuréli way-moomeel yi, di mbootaay yeek nit ñiy sàmm àq ak yelleefi doom-Aadam, muy boroom tur yi ba ci sax baadoola yi, ñépp ñoo ngi kaas tey duut baaraam Njiitu réewum Tinisii li. Dara waralu ko lu dul kàddu yu suufe te ruslu yi mu wax, keroog talaata, 21 féewarye 2023, jëmale leen ci ñuuley Afrig yi bawoo bëj-saalumu yayub Saharaa.

Moom,  Kaïs Saïed, dafa jiite woon am Ndaje mom, kaaraange réew ma lees ca doon fénc. Ba mu ca jógee nag, ca la yàbbiy kàddu yu nëb yooyee tax, boobaak léegi, nit ñiy naan « cam ! ». Ndaxte, dafa joxoñ doomi Afrig yi bawoo bëj-saalumu yayu Saharaa bi, jiiñ leen taafar ak fitna ya fay xew. Nde, daf leen tudde ay « ndiiraani màngkat yu jubadi » yoy, « soppi xar-kanamu Tinisee leen tax a jóg ». Yemu ca de. Ndax daf ci dolli ne, xeetu ñaawteef, caay-caay ak mbonte yi fay am yépp, ñuuley Afrig yooyee ko fay indaale.

Njiitu réewum Tinisi li neeti, ñëw bi fa saa-Afrig yi féete bëj-saalumu yayub Saharaa biy ñëw, duggewuñ ko lenn lu dul soppi deri askanuw Tinisii wi. Ciy waxam, ag kootoo la gog, lalees na ko ci ndoorteelu xarnu biñ nekk, ngir fexe ba réewum Tinisii doon « réewum Afrig kese », soppi xar-kanam ba dootul niroo ak réewum « araab ak jullit ».  Ci kow loolu la  Kaïs Saïed, Njiitu réewum Tinisii li waxee ni dañu war a gaaw « jël i ndogal » ngir dakkal ñëw ba fa ñuuley Afrig yiy ñëw.

Muy ay kàddu yu yées, bon te ñaaw, rawatina bi ñu génnee ci gémmiñu Njiitum réew buy wax ne jullit la. Nga xam ne, lu nekk mën na caa topp ci xeeti ñaawteef, xoqtal ak bunduxataal ñeel ñuuley Afrig ya fa nekk. Nde, bu mbañi ñuule yi dégge seen njiitum réew di wax lu ni mel, dañuy am yoon ngir teg leen bépp xeetu fitna ak metital. La Suite ICI: https://www.defuwaxu.com/kais-saied-weex-der-taxul-a-weex-xol/

© lesechos.fr

Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *