JOM ! ( Babacar Mbaye Ndaak)

Yow

Ndaw

Bul dëpp bul daw
Bul xàddi bul bàyyi mukk
Gëm ko

Góorgóorloo koy joxe
Ci ñaq lay dikke
Lumu metti metti demal
Lu daggul dikk
Te du dagg mukk

Jub
Jubal
Jubalal rèkk
Da nga yègg
Fa nga bëgga dem
Yàllaay maye

Ndaw
JOM

Babacar Mbaye Ndaak
Acad
Atelier Cheikh Anta Diop

JOM ! ( Babacar Mbaye Ndaak), Information Afrique Kirinapost Save as PDF
Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *