Ca atum 2022 la coowal ñaari sàndarm yii di Dijje Baaji ak Fulbeer Sàmbu jiboon, lëmbe réew mépp. Source: DefuWaxu
Nde, ñaari sóobare yooyu, dañu jékki woon rekk réer. Bi ñu toogee as diir, ca lañu gisoon seen i néew. Jamono jooja, Maki Sàll a jiite woon réew mi, ñu nekkoon ci ay yëngutey pólitig yu tar.
La Nguur ga xamle woon nag, cib yégle, mooy ne ñaari takk-der yooyu dañu laboon. Waaye, ba tay jii, ñu bari gëmuñu loolu. Boobaak léegi nag, luññutu yaa ngi doon wéy. Moo tax, lu bees rot na ci.
Ndax, bees sukkandikoo ci yéenekaayu Libération, yoon tuumaal na kii di Serom Bànjaki mi ñuy dàkkentale « Sniper », daldi koy tëjlu tëjub négandiku [mandat de dépôt]. Ci àjjuma jii weesu la àttekat bi jël ndogal loolii. Tuuma yees koy toppe ñooy : nëbb nit ak bóomug ñaari sóobare. La Suite ICI







![[BLUES ORIGINEL] – Le FANTANG des Peuls, Information Afrique Kirinapost](https://kirinapost.com/wp-content/uploads/2022/04/ngoni-120x120.jpeg)
Laisser un commentaire