Téll !… Xërr !… Téll !… Xërr ! Téll !… Xërr !… Takk-der yi fii, ndaw ñi fee, fetel yiy sox, xeer yiy naaw ; póno yiy tàkk, saxaar si ubale jàww ji. Coow laa ngi ne kurr. Wata dawatul, nit doxatul. Nde, yoon amatul. Jàmmaarlo bi metti na. Ndakaaroo ngi tàkk, Sigicoor di bax, Biññoona a ngi riir. Foo dem, sàndarm yeek pólisee yaa ngiy sox i fetel ak di sànniy gërënaad lakirimosen ci benn boor bi ; ci beneen boor bi, askan wi, rawatina ndaw ñi xamb i taal yu bërëx, jóor seen i xeer, naan leen xërr takk-der yi. Déedéet ! Du film de, géntooleen itam. Senegaal fii la xewe. Ci àjjuma jii, 17eelu fan ci suweŋ 2022. Source: Paap Aali Jàllo pour defuwaxu.com
Lu sooke mbir mi ?
Àllarba jële weesu, 8eelu fan ci suweŋ, Yewwi Askan Wi dafa amaloon am ndajem-ñaxtu ca Péncum Réew ma, « Place de la Nation ». Mbooloo mu takkoo takku wuyusi woon ko, fees fa dell. Mbar gi ne fa gàññ, foo sànni woon bàttu mu tag. Ñu xéy, ci alxames ji, yéenekaay yépp fésal ko, biral ndam li ci Yewwi Askan Wi góobe. Kilifa ya yakk lu mel ni xeme Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak jëwriñu biir-réew mi, Antuwaan Feliks Jom, tuumaal leen, tiiñal leen. Usmaan Sonko ne woon, bés boobu, « Bu Yewwi bokkul, wote du am Senegaal. »
Nde, lees jàpp mooy ne Njiitu réew meek i surgaam yi ne ci Nguur gi dañu bëgg a salfaañee mbir yi, kootoog yoon, ngir tere Yewwi bokk ci wotey dépite yees dégmal ci sulet. Te, ci seen i kàddu, Bennoo Bokk Yaakaar warul sax bokk. Ci njeexital li, ñu joxante dig-daje àjjuma, 17eelu fan ci suwe ngir delloo buum ca boy-boy ga. Waaye, ginnaaw gi biñ ko yégalee Perefe, daf leen ko gàntal. Ñoom, nag, ñu ne Perefe dafa jalgati yoon, te sax ñoom dañ ko yégal rekk, tàgguwuñu ko. Bu ko defee, waa Yewwi ne dee, dañuy amal seenum ndaje, ci nii, mbaa ci naa. Ci la tëkkoonte bi tàmbali, ku nekk, Nguur geek kujje gi, di dankaafu sa moroom. Noonu, ba ni àjjuma di ñëwee…La Suite ICI: defuwaxu.com/2022/06/19/buur-lekk-
Laisser un commentaire