Bubakar Bóris Jóob, Bindkat:  » Kenn warul a ñédd nguur ba say baaraam di nácc »

Seen yéenekaayu web, Lu Defu Waxu, amal nab laaj-tontu bu yaatu ak werekaan bii di Bubakar Bóris Jóob, di bindkat bu ñu ràññe ci àddina sépp. Ci waxtaan wii mu séq ak Paap Aali Jàllo, mi ngi ciy biral xalaatam ñeel tolluwaayu réew mi jamono jii ak jaamaarloo bi dox diggante Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak njiitul Pastef li, Usmaan Sonko. Paap Aali Jàllo pour defuwaxu.com

Noo gise liy xew ci réew mi alxemes ba tey ?

Alxemes jii nu génn la yoon dogal ne Usmaan Sonko war naa tëdd kaso ñaari at. Noo ngi teg tey sunuy bët ci yëngu-yëngu yi àtte boobu jur.  Ñi ci mere Maki Sàll bare nañu lool tamit. Liñ tudde “Mbirum Sweet Beauté”, man mii dama cee mas a am kersa. Ndax jaaduwul, réew mu tol ni Senegaal, ak fi mu jaar, ak ñi fi jaar, ñu dem ba fàtte koom-koom, fàtte njàng meek wér-gi yaramu askan wi, di werante ndax Usmaan Sonko siif na Aji Raabi Saar walla siifu ko… Su doon lu am la sax, ñu ne waaw. Waaye, dafa yàgg a leer ne ñi tëgg mbir mi, te Aji Saar ci boppam tudd leen, duggewuñ ko woon lu dul sosal Usmaan Sonko, fexe ba du samp ndëndëm ci joŋante 2024 bi. Ñaaw nañ ci, yàq deru Senegaal ba noppi dooleel Sonko. Cuune mënul a weesu lii. Kon, ñooñu sosal Sonko ñooy réccu tey, naan su ma yëgoon. Suñ njortoon ne nii lañ ciy ñaawe duñ ci dugg. Ay bakkan a ngiy wéy di ci rot, koom gaa ngi gën a nërmeelu, àddina sépp a ngi nuy reetaan.

Ñaari at yi yoon ne Sonko war na koo tëdd nag…

Mooy li merloo ñépp. Mënoo ne kii liñ koy toppe dara amu ci ba noppi teg ci ne, waaye, fàww caabi féete ko ginnaaw lu mat ñaari at. Li àttekat boobu di Isaa Njaay tudde “corruption de la jeunesse”, daanaka fan yii la ko askanu Senegaal mas a dégg te guléet muy dugal nit kaso ! Yëf yi, maa-tey lay gën a nirool te muy Maki Sàll, di ay àttekatam ak ñi làqu woon ci ginnaaw Aji Saar di ko déey li mu war a wax ngir dugal Sonko, ñooñu ñépp ameel nanu réew mi àq te mbir mi warees na koo topp.

Aji Saar nag…?

Bu doon sama sago, dañ koy dimbali, jàppale ko mu defaraat àddinaam. Xale la, ñu am doole am alal naan yóoram, defloo ko njaaxum. Fi mu ne nii, xajatul ci réew mi. Gëwma ni dinañ ko rawale ndax bëgguñu mu rëcc leen te xel dajul ñu koy bàyyi muy doxi soxlaam Ndakaaru walla Ndar walla Jurbel. Ci sama gis-gis bu gàtt, kenn warul à mere Aji Saar, dees ko war a yërëm, dimbali ko.

Li Sonko wax ci moom nag ? “Dàngin bu am AVC”…

Loolu du waxu nit. Lan moo aay ci AVC ? Bi ma déggee kàddu yooyu, sama bopp xaw naa ubu. Ak luñ la tooñ tooñ, boo demee ba am sañ-sañu laaj lu tol nim réew, am na noo xam ne waroo koo waxe. Xam naa ni jamono yii, Sonko tal na leneen lu dul balu àq Ajii Saar. Waaye de, baax kon na mu def ko, baluwaale àq soppeem yi mu teg gàcce gu réy.

Ñu baree ngi naan guléet lu ni mel xew Senegaal. Lu ciy sa xalaat

Liñ tuumaal Sonko, ne dafa siif doomu-jàmbur ngay wax ?

Waaw. Ak tamit ni nguur gi sonalee Sonko. Moom ci boppam nee na keroog kenn masu fee gis lu ni mel…

Ànd naa ci loolu. Nun ñiy mag, yàgg fi, bu dee mbirum pólitig rekk, lu nekk teewe nan ko fi. Waaye, ni nguuru Maki Sàll giy sonale Usmaan Sonko, guléet nu gis lu ni mel ci réew mi. Am na ñu koy weddi, naan buleen fàtte Mamadu Ja ak Abdulaay Wàdd mbaa ñeneen ak ñeneen… Muy dëgg tamit. Wànte, guléet doomu Senegaal, doomu réew mi, jóg di laaj nguur gi, bëgg a toog ci jal bi, ñu tuumaal ko ay tuuma yu ñaawee nii. Mu diy tuuma diggante góor ak jigéen yu teguwul fenn. Ndax xel daj na Seŋoor def lu ni mel ? Amul luñ fi yakkul Abdu Juuf, Wàdd dem na bay bëgg sullilu néewu baayam ca Ndar, waaye taxul Juuf saalit ba naan dafa tëdde diw walla diw. Wàdd ci boppam, ba ay séytaane ñëwee ni ko am na sa noon bu mag buñ bett ci Kornis bi, nataal yaa ngi nii, dafa ni leen xottileen seen foto yooyu, man Ablaay Wàdd jomb naa yenn yi.

Ndax gënul woon Sonko teew ca àttewaay ba ?

Tontu ci laaj boobu du yomb. Leeg-leeg ma xalaat ne su fa teewoon kenn du fa sañ a tudd “corruption de la jeunesse” waaye tamit gor mënut a dékku yenn yi, fuñ la nar a toroxalee ciy kàcci kese, doo fa sawar a teg tànk. Te yit, neexul saa yooy dem àttewaay ba, ñu topp la, di la dóor, naan la awal fii, doo aw fii, defal nii, lu nekk ñu la koy teg. Mi ngi fiy sog a am. Fii la réew mi tollu.

Wax nga sànq ne yoon wra naa jublu ci ñi tëgg mbirum Aji Saar, tuddaale ci Maki. Waaye moom, bu loolu weesoo, ndax am na leneen lu ko yoon war a toppe ëllëg ?

Waaw, ragal naa ne nguur gii fi nekk, bu fi jógee, dina am luñ koy toppe. Xam nga Abdu Juuf, kenn toppewu ko dara. Seŋoor, moom sax, kenn tuddaalewu ko. Ablaay Wàdd tamit, kenn toppewu ko dara. Waaye, ak ni mbir yiy demee nii tey, wax-dëgg-Yàlla, bu geneen Nguur toogee, gëmuma ne Maki Sàll dina mucce noonu. Dafa di sax, loolu moo tax ma jàpp ne, gaa ñii fi nekk, caaxaan du leen fi jële. Ndaxte kat, xam nañu li leen di xaar bés bu Maki Sàll wàccee. Te xéy-na sax mooy gën demin yenn farandoom yi gën a fés yi dëkke xasteek a saaga. Maki kilifa la, Tubaab yi mën nañ koo neexale ndombal-tànk lu diis ca Mbootaayu-Xeet ya mbaa feneen. Àttekat yeek taskati xibaar yeek ñeneen ñi koy jàppale amuñu fuñ daw làqu.

Danga ragal feyyoonte ?

Kenn ñaanu ko Yàlla. Liggéey naa lu bari ci réew mu mel ni Ruwàndaa te looloo ko yàq. Moo tax ma naw Paul Kagame mi fa dakkal feyyoonte diggante Hutu yi ak Tutsi yi.  Te liy xew tey Senegaal du dara soo ko méngaleek ñaawteef yañ doon def Ruwàndaa ci 1994.

Kon jàpp nga ni bu Maki bokkee sax dañ koy duma ?

Ku nekk ak niŋ ko gise, waaye man loolu laa gëm. Moo tax, léeg-léeg, ma dem ba mu yàgg, sama xel ñaaw, ma ni joŋante yees di waajal de, amaana gaa ñi fexe ba du fi ame. Xéy-na léegi nu dégg ay baat yu mel ni “état d’urgence” mbaa sax “état” de siège”, taafantoo ko dàq joŋante 2024 bi.

Mën naa àgg ba foofu ?

 Duma gisaanekat, maak ñépp a ci yem waaye loolu laa njort.

 Lan moo tax nit ñi topp Usmaan Sonko ?

Ñépp a ngi naan Sonko nit ku jub la, dëggu, am fit. Waaye, du moom rekk a mel noonu ci làngu politig gi, mënees na wax lu ni mel ci ñeneen doore ko ci Ceerno Alasaan Sàll mi fi tekki woon ndombal-tànk lu am solo, delloo ko Maki Sàll  ne ko lii Total bëgg a def baaxul ci réew mi, ànduma ci, dem naa sama yoon. Man dama jàpp ne, li may dëgg doole Usmaan Sonko moo di ne nun saa-Senegaal yi, képp ku ñuy tooñ, yow lanuy faral. Rawatina bu dee lépp liñ lay jiiñ ay kàcci kese la. Xéy-na dinga mi : “Karim Maysa Wàdd, nag ? Xalifa Abaabakar Sàll, nag ? Ñoom it dañ leen a tooñoon, du ?” Waaye ñaar ñooñu dañoo juum, wóolu Yoon ba yaakaar ne dina leen setal. Usmaan Sonko gis loolu, ne moom day jaamaarlook nguur gi, lu mu ci góobe gar ko. Kon, loolu moo tax nit ñi di ko topp, di ko topp ba léegi, dafa mujj, ñi nga xam ne dañoo mere Nguur gi yépp, te Yàlla xam na ne bari nañu, ci Sonko lañuy gis seen bopp. Te ni ma ko waxe sànq, àtte keroog bi da koo dooleel bu baax a baax.

Dem nga ba ni bés ni nit ñi toppe Sonko masu fee am.

Li ma gis rekk laa wax. Dëgg la, am na fi ba tàyyi ay njiit yu nit ñi gëm, topp leen. Ablaay Wàdd jaar na fi, bun ko fàtte ak ñeneen. Waaye, ni mu mel nii, wax-dëgg-Yàlla mësuma koo seetlu. Li ci gën a doy waar moo di ne Sonko gone la te bi mu duggee ci làngu politig gi yàggul, atum 2014 la tàmbalee pólitig, su ma juumulee. La Suite ICI

Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *