SONKO AK MAKI : KUY DAAN ? (Aamadu Jara)

 Bubakar Bóris Jóob • Fitna lañ doore bésub àjjuma jii. Fitna ju sosoo ci diggante Sonko ak Maki. Ndax lan ? Ndax, dañoo tere Sonko ak i àndandoom seen ndajem ñaxtu mi ñu bëggoon a amal bés boobule ca Péncum Obelisk. Source:  defuwaxu.com

Li ñu jàpp, mooy ne Maki dafa noot yoon, ba pare bëgg a lottal Usmaan Sonko. Réy gi mu réy moo tax mu jàpp ne warul am kuñ koy méngale (dendale) ci làng gi. Ba tax mu dëkke di ko lakkal ngir ne mooy wujjam bi gën a am doole ci làngug pólitig gi ci jamono jii.

Li sabab lu ni mel, nee ñu, bëqët la, ab ragal la moo tax. Fi mu tollu nii dafa bëgg a def ñetteelu moome te feek daanelul Sonko xelam du dal. Loolu la defoon ak Xalifa Sàll ay at ci ginnaaw. Jàpp ko ne ko ràpp ci kaso bi.

Ca dëgg-dëgg ñenn ñi fare ci wàllu yoon ba ci waa « Conseil Constitutionnel », jàpp nañu ne ci ay waawu Maki Sàll lañuy dox. Maanam, lu mu namm ñu def rekk lañuy def.

Waaye, moom dafa fàtte ne ñaxtu bi mu daan ñaxtu démb loolu la Sonko ak i àndandoom di ñaxtu tey. Fàtte moom da fee xajul sax. Te, ku fàtte lu la fal, sag folleeku da lay bett. Léegi kon, lan moo tax mu bëgg a jalgati yoon ndeem digganteem ak Abdulaay Wàdd demewul woon nii ? La Suite ICI: defuwaxu.com/2022

Share

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *